Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 2

Kàdduy Waare 2:13-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13Ma gis ne ni leer ëppe lëndëm njariñ, ni la xel mu rafet ëppe ndof njariñ.
14Ku xelu day xool fa muy jaare, dof biy tëñëx-tëñëxi cig lëndëm. Ma ne moona ñoom ñaar a bokk dogal moos.
15Ma xalaataat, saam xel ne ma, dof bi noonu, man it noonu; ana lu may xeloo xelu doye? Saam xel ne ma loolu it, cóolóoli neen.
16Ku xelook ku dof, du yàgg ñu fàtte la; ay bés yu néew, ñu fàtte lépp. Acam! Dof, dee; rafet xel, dee.
17Ma far bañ àddina. Ndaw naqar ci jëfi kaw suuf, te lépp di cóolóol ak napp um ngelaw!
18Sama doñ-doñ, ji fi kaw dun bi, génnliku na ma, dama koy wacce ka may wuutuji rekk,
19xameesul ku xeloom ku nitoodi lay doon, mooy moom lu ma doon doñ-doñi, te sama manoore manaloon ma ko fi kaw dun bi. Loolu it, cóolóoli neen.
20Sama xol a jeex ci doñ-doñ ju ma doñ-doñi fi kaw dun bi.
21Nit a ngi doñ-doñee xel, xam-xam ak manoore, te ku doñ-doñiwuloon lay wacce alalam. Loolu it, cóolóoli neen ak naqar wu réy.
22Ma ne ana lu nit di jariñoo ci doñ-doñ ak xalaatu xol, yi muy doñ-doñaale fi kaw dun bi?
23Ndegam day yendoo tiis ak naqaru tës-tës, ba far fanaanoo xel mu dalul. Loolu it, cóolóoli neen.
24Kon nit amul lu gën di lekk ak a naan, di bànneexoo ñaqam. Ma gis ne loolu it Yàllaa koy maye.
25Ana kuy lekk ak a bànneexu, te du Yàlla?
26Yàlla de, ku mu gërëm, xelal ko, xamal ko, bégal ko; bàkkaarkat bi, Yàlla teg ko, muy denc ak a dajale, ka mu gërëm jël. Loolu it di cóolóoli neen ak napp um ngelaw.

Read Kàdduy Waare 2Kàdduy Waare 2
Compare Kàdduy Waare 2:13-26Kàdduy Waare 2:13-26