13Ma gis ne ni leer ëppe lëndëm njariñ, ni la xel mu rafet ëppe ndof njariñ.
14Ku xelu day xool fa muy jaare, dof biy tëñëx-tëñëxi cig lëndëm. Ma ne moona ñoom ñaar a bokk dogal moos.
15Ma xalaataat, saam xel ne ma, dof bi noonu, man it noonu; ana lu may xeloo xelu doye? Saam xel ne ma loolu it, cóolóoli neen.
16Ku xelook ku dof, du yàgg ñu fàtte la; ay bés yu néew, ñu fàtte lépp. Acam! Dof, dee; rafet xel, dee.
17Ma far bañ àddina. Ndaw naqar ci jëfi kaw suuf, te lépp di cóolóol ak napp um ngelaw!
18Sama doñ-doñ, ji fi kaw dun bi, génnliku na ma, dama koy wacce ka may wuutuji rekk,
19xameesul ku xeloom ku nitoodi lay doon, mooy moom lu ma doon doñ-doñi, te sama manoore manaloon ma ko fi kaw dun bi. Loolu it, cóolóoli neen.