Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 1

Kàdduy Waare 1:15-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Lu wañaaru, maneesu koo jubbanti; lu teewul, maneesu koo lim.
16Damaa wax ci saam xel naa: Man de, maa ngii di gëna xelu, ba sut ku ma jiitu ci jalub Yerusalem. Damaa xuus ci xel mu rafet ak xam-xam,
17di dogoo xam luy xel mu rafet, xam luy nitoodi akug ndof. Fekk loolu it napp um ngelaw la.
18Ku géejal xel mu rafet, géejal naqar; yokku xam-xam, yokku tiis.

Read Kàdduy Waare 1Kàdduy Waare 1
Compare Kàdduy Waare 1:15-18Kàdduy Waare 1:15-18