2Fa la jant di lëndëme, weer giim, biddiiw giim, taw siwet, mu niru la lu xiinati.
3Su bés baa wattukati kër gi di lox, jàmbaari xare yi sëgg, wolkat yi néew, ba wolatuñu, ñiy séentu ci caax yi giimle,
4bunt yi féeteek mbedd mi tëje, coowal wol dal, as picc sab, nelaw naaw, janq ju doon woy, selaw.