Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 9

Kàddu yu Xelu 9:8-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Bul yedd kuy ñaawle, da lay jéppi; yeddal ku rafet xel, mu naw la.
9Xelalal ku xelu, mu yokku. Xamalal ku jub, mu yokk njàngam.
10Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel, xam Aji Sell ji di am ug dégg.
11Maay Xel mu Rafet, ku ma topp gudd fan, dund, dundati.
12Rafet xel, jariñu, kuy kókkalee, wéetook sa añ.
13Jigéen ju dof day xumb, reew, du xam lu xew.
14Day toog bunt këram, mbaa fu kawee kawe ca dëkk ba,
15di woo ña fay jaare te jubal seenu yoon.
16Ma nga naa: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!» Ku ñàkk bopp, mu ne ko:
17«Ndox mu lewul a neex, ñamu làqu-lekk dàqati.»
18Waaye kooka du xam ne waa njaniiw a nga fa, te ku wuyji, tàbbi biir bàmmeel.

Read Kàddu yu Xelu 9Kàddu yu Xelu 9
Compare Kàddu yu Xelu 9:8-18Kàddu yu Xelu 9:8-18