Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 8

Kàddu yu Xelu 8:32-36

Help us?
Click on verse(s) to share them!
32«Kon nag, doom, dégluleen ma. Mbégte ñeel na ki may topp.
33Dégluleen ku leen di yar, daldi muus. Buleen ko sàggane!
34Mbégte ñeel na ki may déglu, di teewlu ca sama bunt bés bu nekk, di ma toogaanu sama bunt kër.
35Ku ma daj, gudd fan, Aji Sax ji bége la.
36Ku ma moy loru, ku ma bañ, daa repp.»

Read Kàddu yu Xelu 8Kàddu yu Xelu 8
Compare Kàddu yu Xelu 8:32-36Kàddu yu Xelu 8:32-36