28ak ba muy teg niir ya fa kaw, ak ba muy dooleel ndoxi xóotey géej,
29ak ba muy sàkkal géej kemoom, ba du jàll fa mu wax. Ba muy rëdd fa muy samp àddina,
30man, Xel mu Rafet, maa doon ku xareñ ci wetam, di ko bànneexal bés bu ne, tey bànneexu fi kanamam.
31May bége wërngalu àddinaam, di bànneexoo doomi aadama.»
32«Kon nag, doom, dégluleen ma. Mbégte ñeel na ki may topp.
33Dégluleen ku leen di yar, daldi muus. Buleen ko sàggane!
34Mbégte ñeel na ki may déglu, di teewlu ca sama bunt bés bu nekk, di ma toogaanu sama bunt kër.
35Ku ma daj, gudd fan, Aji Sax ji bége la.