17Maa sopp ku ma sopp, ku ma seet tigi, gis ma.
18Alal ak teraangaa ngi fi man, am-am bu sax it ak yoolu njekk.
19Li may mayee gën wurus, wa gën, sama njariñ wees xaalis ba gën.
20Yoonu njekk laay jaare, di jëfe li yoon àtte rekk.
21Ku ma sopp, ma nàddil la, feesal sab denc.»
22Soxna si, Xel mu Rafet nee na: «Aji Sax ji jagoo na ma ca njàlbéen, ma jiitu ca jëfam ya woon.
23Bu yàgg lañu ma dëj, ca ndoorte la, bala suuf a sosu.
24Ba may dikk, géej amul, ndox ballul bay fees, di wal-wali.
25Dikk naa bala tund yu mag yee sampu, lu jiitu tund yu ndaw yi,
26laata Yàllaa sàkk suuf aki àllam ak feppu pënd ci àddina.
27Ba muy taxawal asamaan, maa nga fa, ak ba muy rëdd fa asamaan taseek géej,
28ak ba muy teg niir ya fa kaw, ak ba muy dooleel ndoxi xóotey géej,
29ak ba muy sàkkal géej kemoom, ba du jàll fa mu wax. Ba muy rëdd fa muy samp àddina,
30man, Xel mu Rafet, maa doon ku xareñ ci wetam, di ko bànneexal bés bu ne, tey bànneexu fi kanamam.
31May bége wërngalu àddinaam, di bànneexoo doomi aadama.»