Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 7

Kàddu yu Xelu 7:3-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Takkal ci say waaraam, bind ko ci sa àlluway xol.
4Safool xel mu rafet, muy sab jigéen, te nga xejjoo dég-dég ni sa mbokk lenqe.
5Dina la aar ci ndaw su yemadi, bokk feneen, di wax lu neex.
6Damaa tollu sama palanteer, séentu ca xarante ya,
7séen ca biir téxét ya, ku ma seetlu ca xale yu góor ya, muy ku ñàkk bopp.
8Muy dem ba fa ndaw say taxaw, ca selebe yoon wa, daldi wuti kër ndaw sa.
9Ngoonug suuf la, jant biy lang, muy lëndëm di gëna guddi.
10Ndaw si jekki dajeek moom, sol yérey gànc, lal pexeem.
11Daa xumb, të, du toog këram.
12Ma nga ca mbedd ma, ne ca pénc ya, ruqoo ruq, ma ngay yeeroo.
13Ndaw sa ne ko katam, fóon, ne wajj, ne ko:
14«Tey matal naa la ma digoon Yàlla, yàppu bernde waa nga kër ga, saraxu cant la.
15Moo ma taxa dikk dajeek yaw. Seet naa laa seet, ba gis la.
16Lal naa saab lal, ba mu jekk, di malaan yu yànj, bawoo Misra.
17Lal ba, ma xeeñal, mu ne bann, di ndàbb, cuuraay ak xas mu neex.
18Dikkal, nu baanee baane, ba bët set, te bànneexu ci mbëggeel.

Read Kàddu yu Xelu 7Kàddu yu Xelu 7
Compare Kàddu yu Xelu 7:3-18Kàddu yu Xelu 7:3-18