12Ma nga ca mbedd ma, ne ca pénc ya, ruqoo ruq, ma ngay yeeroo.
13Ndaw sa ne ko katam, fóon, ne wajj, ne ko:
14«Tey matal naa la ma digoon Yàlla, yàppu bernde waa nga kër ga, saraxu cant la.
15Moo ma taxa dikk dajeek yaw. Seet naa laa seet, ba gis la.
16Lal naa saab lal, ba mu jekk, di malaan yu yànj, bawoo Misra.
17Lal ba, ma xeeñal, mu ne bann, di ndàbb, cuuraay ak xas mu neex.
18Dikkal, nu baanee baane, ba bët set, te bànneexu ci mbëggeel.
19Sama jëkkër newu fa, daa dem yoon wu sore.
20Mbuusum xaalis la ŋàbb, yóbbu, du ñibbsi ndare weer wi fees dell.»