5Dawal ni kéwél gu rëcc ub rëbb, ne fërr ni picc mu raw ab fiirkat.
6Yaafus bee, xoolal xorondom, seetal ci moom, ba muus.
7Du ku ko yilif mbaa ku koy sas, te jiiteesu ko.
8Bu jotee mu denc ab dundam, mu jot, mu for lekkam.
9Moo yaafus bi, foo àppal tëraay bi? Loo deeti xaar ci yewwu?
10Ngay dajjant ak a for bët, di tegley loxook a jaaxaan.
11Néewlee ngi lay dikkal nib sàcc, ñàkk gànnaayul la.
12Ku tekkeedi te bon, day wër di fen,
13day piis, di wokkeb tànk, di waxe baaraam,
14jekkadiy xalaat, di mébét lu bon aka yokku ay.
15Moo tax musiba di jekki dal ko, mu jekki yàqu, ba wees paj.
16Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ, ba ci juróom yaar yu mu seexlu:
17kuy daŋŋiiral, kuy fen, kuy rey nit ku deful dara,
18kuy fexe lu bon ci xolam, kuy gaawtuy def lu ñaaw,
19seede buy fen rekk, rawatina kuy yokku ay ci biiri bokk.
20Doom, defal li la baay sant, te bul wacc ndigalal yaay.
21Takkal foo tollu, taf ci sa xol, fas ko ci sa baat.
22Booy dox mu di la jiite, nga tëdd, mu di la sàmm, nga yewwu, mu di la waxal.
23Santaane da lay niital, ndigal leeralal la, artook ub yar di yoonu dund.