Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 6

Kàddu yu Xelu 6:24-35

Help us?
Click on verse(s) to share them!
24Da lay aar ci ndaw su bon ak jabaru jaambur ak làmmiñam wu neex.
25Bu ko xemmeme taaram, bumu la fiir aki lamsal.
26Dogu mburu fey nab gànc; waaye jabaru jaambur, bakkanu lëmm.
27Te ku ne sawara cas, tafoo, lakk say yére.
28Ku dox ciy xal it, say tànk ñor.
29Mooy ànd ak jabaru jaambur, ku ko def gis ko.
30Deesul sikk ku sàcc aw ñam, def ci biiram ndax xiif.
31Waaye bu feeñee, fey boroom juróom yaari yoon, joxe alalu këram yépp.
32Njaaloo di ñàkk bopp, kuy sànk bakkanam a koy def.
33Mbugal ak toroxte dib añam, te gàcceem du deñ.
34Fiiraange day feesal xolu góor, te du ñéeblu buy feyu.
35Du faale ndàmpaay, loo ko may, may, du giif.

Read Kàddu yu Xelu 6Kàddu yu Xelu 6
Compare Kàddu yu Xelu 6:24-35Kàddu yu Xelu 6:24-35