Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 6

Kàddu yu Xelu 6:21-25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
21Takkal foo tollu, taf ci sa xol, fas ko ci sa baat.
22Booy dox mu di la jiite, nga tëdd, mu di la sàmm, nga yewwu, mu di la waxal.
23Santaane da lay niital, ndigal leeralal la, artook ub yar di yoonu dund.
24Da lay aar ci ndaw su bon ak jabaru jaambur ak làmmiñam wu neex.
25Bu ko xemmeme taaram, bumu la fiir aki lamsal.

Read Kàddu yu Xelu 6Kàddu yu Xelu 6
Compare Kàddu yu Xelu 6:21-25Kàddu yu Xelu 6:21-25