19Aka sopplu te jekk! Na lay céram doy foo tollu, na la xañ sago saa su ne.
20Doom, ana looy xemmeme keneen, bay foye céri jaambur?
21Lu waay jëf, Aji Sax ji gis, di xool mboolem fu mu jaare.
22Jëf ju bon day fiir ka ko sàlloo, bàkkaaram di mbaal, jàpp ko.