Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 5

Kàddu yu Xelu 5:14-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
14Tuuti ma yàqu yaxeet fi kanam ñépp!»
15Naanal ci sa mbalkam bopp, ndox ma balle sa teenu bopp.
16Xanaa doo wasaare sa bëti ndox ca biti, mu def ay wal ca pénc ya?
17Nay sa alal, yaw doŋŋ, ku bokk feneen bokkul.
18Yal na sa naanukaay barkeel, nga bànneexoo kiy sa jabar ba ngay ndaw.
19Aka sopplu te jekk! Na lay céram doy foo tollu, na la xañ sago saa su ne.
20Doom, ana looy xemmeme keneen, bay foye céri jaambur?
21Lu waay jëf, Aji Sax ji gis, di xool mboolem fu mu jaare.
22Jëf ju bon day fiir ka ko sàlloo, bàkkaaram di mbaal, jàpp ko.

Read Kàddu yu Xelu 5Kàddu yu Xelu 5
Compare Kàddu yu Xelu 5:14-22Kàddu yu Xelu 5:14-22