10Jaambur jariñoo sa doole, doxandéem jagoo saw ñaq.
11Ngay mujje onk, desey yax, jeex tàkk.
12Nga naan: «Su ma yégoon, sopp ab yar te baña sofental waxi àrtu.
13Lu ma tee woona dégg ku may digal, tey teewlu sama waxi sëriñ ya?
14Tuuti ma yàqu yaxeet fi kanam ñépp!»