7Njàlbéenu xel mu rafet mooy sàkku ko; ak loo mana am, amal ug dégg.
8Nawal xel mu rafet, mu darajaal la; tafoo ko, mu teral la.
9Da lay takkal kaala gu jekk, solal la mbaxanam buur.»
10Déglul, doom, te dégg saay wax, ndax nga gudd fan.
11Yoon wu xelu laa la teg, jaarloo la yoonu njub.
12Doo dox ba tërëf, doo daw, téqtalu.
13Ŋoyal cib yar, bul yoqi, sàmm ko, moo yor sa bakkan.
14Yoonu ku bon, bu ci tegu; fu ab soxor di jaar, bu fa dox.
15Moyul, bu fa jaare; mbasal te wéy!
16Ku bon du nelaw te lorewul, du dajjant ba kera muy téqe.
17Daa bon, def ko lekk, di màndee coxoram.
18Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.