22Mooy dundloo ku ci jàpp, di wéral jëmmam jépp.
23Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
24Dàqal wor, mu sore la; kàdduy naxe, na la dànd.
25Xooleel, sa bët ne jàkk, ngay xool sa kanam màkk.
26Seetlul fi ngay teg tànk, ba foo awe, mu wóor.