Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 3

Kàddu yu Xelu 3:6-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.
7Bul doyloo sa xel mu rafet, ragalal Aji Sax ji, dëddu mbon;
8sa yaram wér, say cér naat.
9Teralal Aji Sax ji ci sa alal ak loo jëkka meññle,
10say sàq day fees, ne xéew, say mbàndi ndoxi reseñ di wal.
11Doom, bul xeeb yaru Aji Sax ji, bul bañ mu waññi la,
12ndax Aji Sax ji, ku mu sopp, waññi la, ni baay, ak doom ju ko neex.
13Mbégtee ñeel ku daj xel mu rafet ak ku am ug dégg.

Read Kàddu yu Xelu 3Kàddu yu Xelu 3
Compare Kàddu yu Xelu 3:6-13Kàddu yu Xelu 3:6-13