6Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.
7Bul doyloo sa xel mu rafet, ragalal Aji Sax ji, dëddu mbon;
8sa yaram wér, say cér naat.
9Teralal Aji Sax ji ci sa alal ak loo jëkka meññle,
10say sàq day fees, ne xéew, say mbàndi ndoxi reseñ di wal.