24Soo tëddee doo tiit; say nelaw day neex.
25Kon doo ragal njàqare lu bette ak saaysaay buy songe,
26ndax Aji Sax ji da lay yiir, di la musal cig fiir.
27Bul xañ njekk ku ko yelloo, ndegam man nga ko.
28Bul ne say dëkk: «Demal ba beneen, ma jox la,» te fekk la yor.
29Bul fexeel dëkkandoo bu dëkk ak yaw ci kóolute.
30Bul joteek kenn ci neen, te tooñu la.