17Fa muy jaare yiw la, fu mu awe jàmm la.
18Mooy garabu gudd fan ci ku ko jàpp, di mbégtey ku ca ŋoy.
19Aji Sax ji xel mu rafet la sose suuf, lale asamaan ag dégg.
20Ci xam-xamam la ndoxi xóote ya ne jàyy, ay niir di lay.
21Sama doom, saxool xelu akug foog, dee ci xool foo tollu.
22Day guddal saw fan, di rafetal sa jikko.
23Kon sab dox wóor, doo fakktalu.
24Soo tëddee doo tiit; say nelaw day neex.
25Kon doo ragal njàqare lu bette ak saaysaay buy songe,
26ndax Aji Sax ji da lay yiir, di la musal cig fiir.
27Bul xañ njekk ku ko yelloo, ndegam man nga ko.