10say sàq day fees, ne xéew, say mbàndi ndoxi reseñ di wal.
11Doom, bul xeeb yaru Aji Sax ji, bul bañ mu waññi la,
12ndax Aji Sax ji, ku mu sopp, waññi la, ni baay, ak doom ju ko neex.
13Mbégtee ñeel ku daj xel mu rafet ak ku am ug dégg.
14Am koo gën am xaalis, te njariñ laa raw wurus.
15Xel mu rafet a gën gànjar; loo mana bëgg moo ko raw.
16Gudd fan, mu joxee ndijoor; càmmoñ ba, alal ak teraanga.
17Fa muy jaare yiw la, fu mu awe jàmm la.