Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 3

Kàddu yu Xelu 3:1-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Doom, bul fàtte sama njàngle, defal sa xel ci saay santaane,
2ngir fan wi gudd lool, nga gëna am jàmm.
3Bu la ngor ak worma dëddu, booleel takk ci sa baat, bind ko ci sa àlluway xol.
4Kon nga xam lu jaadu, neex Yàllaak doom aadama.
5Nanga wóoloo Aji Sax ji, sa léppi xol, te bul wéeru ci saw déggin.
6Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.

Read Kàddu yu Xelu 3Kàddu yu Xelu 3
Compare Kàddu yu Xelu 3:1-6Kàddu yu Xelu 3:1-6