5Lu ko moy mu naan, ba fàtte lu yoon tëral, xañ néew-ji-doole ju ne, àqam.
6Bàyyeel ñoll kuy sànku, bàyyi biiñ ak boroom naqar.
7Bu ñu naanee, fàtte seen néewle, ba dootuñu fàttliku seenu tiis.
8Nanga àddul ku amul kàddu, ku sësul fenn, nga ñoŋal àqam.
9Deel àddu, di àtte njub; ku ñàkk ak ku néewle, nga sàmm àqam.
10Jeeg bu jàmbaare, ndaw lu jafe, ba rawati gànjar!
11Jëkkër ja da koy wóolu, te jëkkër ja day am xéewal, du ko ñàkk.
12Day defal jëkkëram lu baax, du ko lor, tey ànd ak bakkan.
13Day wut kawari gàtt aki wëñ, di ca liggéeye mbégte.
14Day mel ni gaalu jula, di jëli dundam fu sore.
15Day jóg te bët setul, di waajal njëlu njabootam, ak a sas ay janqam.
16Day seetlu ab tool, jënd ko, sàkk ciw ñaqam, jëmbat tóokër.
17Day gañu di góor-góorlu, ak a dëgëral përëg ya.
18Day gis njartel liggéeyam, te làmpam du fey guddi.
19Ma ngay yor poqe ak këccu, di ëcc.
20Day jox ku ñàkk, di sàkkal néew-ji-doole.
21Tiitul ci njaboot gi sedd bu metti, ndax ñoom ñépp ay tegley yére.
22Mooy sàkkal boppam ay malaan, ay yéreem mucc ayib te yànj.