12mucc ci yoonu ku bon ak kuy wax lu jekkadi,
13mucc ci kuy wacc yoonu njub, di jaare mbedd yu lëndëm.
14Kon nga mucc ci kuy def lu bon, tey bànneexoo lu jekkadi.
15Yoonu ku ni mel day lunk, jaaruwaayam dëng.
16Xel mu rafet da lay musal ci ndaw su yemadi, bokk feneen, di wax lu neex.
17Day dëddu wóllëreem, ba muy ndaw, fàtte kóllëreem ak Yàllaam.
18Këram day joy wuti ndee, ay jaaruwaayam jëm njaniiw.
19Ku dem ca moom dootoo délsi, doo gisati yoonu dund mukk.
20Kon nag aweel mbeddum waa ju baax, toppal yoonu ku jub,
21ndax kuy jubal ay dëkke réew mi, te ku mat a fiy des.