Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 2

Kàddu yu Xelu 2:11-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11nga foog, fegu, am ug dégg, raw,
12mucc ci yoonu ku bon ak kuy wax lu jekkadi,
13mucc ci kuy wacc yoonu njub, di jaare mbedd yu lëndëm.
14Kon nga mucc ci kuy def lu bon, tey bànneexoo lu jekkadi.
15Yoonu ku ni mel day lunk, jaaruwaayam dëng.
16Xel mu rafet da lay musal ci ndaw su yemadi, bokk feneen, di wax lu neex.
17Day dëddu wóllëreem, ba muy ndaw, fàtte kóllëreem ak Yàllaam.
18Këram day joy wuti ndee, ay jaaruwaayam jëm njaniiw.

Read Kàddu yu Xelu 2Kàddu yu Xelu 2
Compare Kàddu yu Xelu 2:11-18Kàddu yu Xelu 2:11-18