5Kuy jay sa moroom, yaa ngi koy dugal.
6Ku bon day moy, ba dugal boppam; ku jub di woy ak a bànneexu.
7Ku jub a xam àqu néew-ji-doole, ab soxor xamu ca dara.
8Ñaawlekat a ngi taal ab dëkk, ku xelu di giifal mer.
9Boroom xel, buy layook ub dof, bu mereek buy ree, jàmm du am.
10Ab bóomkat day sib ku mat, di wuta bóom kuy jubal.
11Ab dof day mer, sàmbaar; ku xelu, mer, ànd ak sagoom.
12Kilifa dégluy fen, jawriñ yépp di ñu bon.
13Ku ñàkk ak ka ko nennoo bokk lenn, Aji Sax jee leen boole sàkk.
14Buur àtte way-ñàkk ci dëgg, ab jalam sax.
15Deel bantal ak a yedde, day rafetal xel; gone goo bay-bayal, mu gàcceel ndeyam.