12Kilifa dégluy fen, jawriñ yépp di ñu bon.
13Ku ñàkk ak ka ko nennoo bokk lenn, Aji Sax jee leen boole sàkk.
14Buur àtte way-ñàkk ci dëgg, ab jalam sax.
15Deel bantal ak a yedde, day rafetal xel; gone goo bay-bayal, mu gàcceel ndeyam.
16Bu ku bon féetee kaw, ag moy law, waaye ku jub, fekke jéllu ku bon.
17Yaral sa doom, mu noppal la, bànneexal la.
18Fu Yàlla feeñoowul, nit ña fétteeral, waaye ku topp yoon, am mbégte.