Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 28

Kàddu yu Xelu 28:24-28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
24Ku xañ say waajur seen alal te defe ne tooñoo, yaa neexook saaysaayu yàqkat.
25Ku bëgge day sooke ay, te ku wóolu Aji Sax ji, woomle.
26Ku doyloo sam xel, dof nga; ku jëfe xel mu rafet, mucc nga.
27Kuy jox néew-ji-doole, doo ñàkk; nga gëmm ne gisoo, bare ku la móolu.
28Bu ab soxor faloo, ñépp làquji, bu daanoo, ku jub teg tànk.

Read Kàddu yu Xelu 28Kàddu yu Xelu 28
Compare Kàddu yu Xelu 28:24-28Kàddu yu Xelu 28:24-28