19Beyal sab tool, sab dund doy; topp ay caaxaan, ndóol ba doyal.
20Boroom worma, bare barke; ku yàkkamtee woomle, sa mbugal du jaas.
21Par-parloo baaxul, waaye dogu mburu moyloo na kilifa.
22Ab nay day yàkkamtee barele, te xamul, ba ko ñàkk di dab.
23Boo artoo nit, mu baaxe la ëllëg; yaa koy gënal ku ko doon jay.
24Ku xañ say waajur seen alal te defe ne tooñoo, yaa neexook saaysaayu yàqkat.
25Ku bëgge day sooke ay, te ku wóolu Aji Sax ji, woomle.
26Ku doyloo sam xel, dof nga; ku jëfe xel mu rafet, mucc nga.
27Kuy jox néew-ji-doole, doo ñàkk; nga gëmm ne gisoo, bare ku la móolu.
28Bu ab soxor faloo, ñépp làquji, bu daanoo, ku jub teg tànk.