Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 27

Kàddu yu Xelu 27:21-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
21Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli, waaye àtteb nit ca jëëm.
22Soo jëloon ub dof, yeb ci gënn, booleek pepp, wol, du tax ndof ga deñ.
23Xamal bu baax lu say gàtt nekke, te def sa xel ci say gétt,
24ndax alal wéyul fàww, ag pal du ñeel sëtoo sët.
25Gannaaw bu ñu gubee, ba ñax saxaat, ñu dajale ngooñ ma ca tund ya,
26say xar da lay amal koddaay, bëy yi génneel la njégu tool.

Read Kàddu yu Xelu 27Kàddu yu Xelu 27
Compare Kàddu yu Xelu 27:21-26Kàddu yu Xelu 27:21-26