Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 27

Kàddu yu Xelu 27:2-7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Bul tëggu, bàyyil ñu tagg la, muy waxi keneen; yaw, bu ko wax.
3Doj diis na, suuf dib sëf, waaye fitnay dof a ko raw.
4Xadar day ñàng, mer di wal mu baawaan, waaye fiiraange amul moroom.
5Artu yu ñu la biralal moo gën cofeel gu la boroom ñooru.
6Soppe, bu lay gaañ sax, wóolu ko. Nit bañ na la, te di la fóon lu bare.
7Ku suur, bañ lem ju xelli, waaye boo xiifee, lu wex lu ne neex la.

Read Kàddu yu Xelu 27Kàddu yu Xelu 27
Compare Kàddu yu Xelu 27:2-7Kàddu yu Xelu 27:2-7