2Bul tëggu, bàyyil ñu tagg la, muy waxi keneen; yaw, bu ko wax.
3Doj diis na, suuf dib sëf, waaye fitnay dof a ko raw.
4Xadar day ñàng, mer di wal mu baawaan, waaye fiiraange amul moroom.
5Artu yu ñu la biralal moo gën cofeel gu la boroom ñooru.
6Soppe, bu lay gaañ sax, wóolu ko. Nit bañ na la, te di la fóon lu bare.