18Ku aar garab, lekk ca doom ya; ku topptoo sa sang, am ngërëm.
19Ku xool cim ndox, gis sa kanam, nga xool sab xol, gis sa jikko.
20Njaniiw ak biir suuf du fees, bët it du doylu mukk.
21Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli, waaye àtteb nit ca jëëm.
22Soo jëloon ub dof, yeb ci gënn, booleek pepp, wol, du tax ndof ga deñ.
23Xamal bu baax lu say gàtt nekke, te def sa xel ci say gétt,