10Bul fàtte sab xarit mbaa sa xaritu baay, bul jàq ba seeti sa mbokk; dëkkandoo bu jegee gën mbokk mu sore.
11Muusal, doom, ma bég, ba mana tontu ku ma sikk.
12Kuy foog, gisu ay, làqu; ab téxét ne ca tëñëx, loru.
13Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal ndaw su yemadi.