2Ñaan-yàlla, soo tooñul, du la dal, day mel ni picc muy naaw, tëë toŋ.
3Xiir, aw fas; laab, mbaam; yetu gannaaw, ab dof.
4Bul topp ab dof cig ndofam, lu ko moy nga mel ni moom.
5Waaye toppal ab dof cig ndofam, lu ko moy mu defe ne daa muus.
6Ku yóbbante ab dof kàddu, yaa woo fitna, gor say tànk.
7Kàddu gu xelu ci gémmiñug dof, mooy tànki lafañ, amalu ko njariñ.
8Kuy teral ab dof, jël ngaw doj, takk ko ci mbaq.
9Kàddu gu xelu ci gémmiñug dof mooy car aki dégam, màndikat xàcci.
10Njaatige luy liggéeyloo ab dof ak kuy romb, daa mel ni fittkat buy gaañ ku ne.
11Dof day def jëfi dof, dellu ca, mooy xaj, bu waccoo, lekkaat ko.