21Bu sab noon xiifee, jox ko mu lekk, bu maree, may ko mu naan,
22day rus ba mel ni koo yeni xal, te Aji Sax jee lay fey.
23Jëw, mer a cay topp; mooy ngelawal taw, taw a cay topp.
24Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.
25Xibaaru jàmm, bawoo fu sore mooy ndox mu sedd ci ku loof.