Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 25

Kàddu yu Xelu 25:11-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Wax ju ñor di nataalu wurus wu tege ci xaalis.
12Kàddu yu lay yedd ci kuy dégg, jaarob wurus la mbaa gànjaru ngalam.
13Ndaw lu wóor day seral xolu njaatigeem, mooy ndox mu sedd ci tàngooru ngóob.
14Kuy dige te doo joxe, yaay xiin wu ngelaw, mu naaxsaay.
15Muñ mer ay nax kilifa, te wax ju neex, fu mu jaar, mu nooy.

Read Kàddu yu Xelu 25Kàddu yu Xelu 25
Compare Kàddu yu Xelu 25:11-15Kàddu yu Xelu 25:11-15