5Ku rafet xel di boroom doole, ku xam, gëna man;
6tegtal yu xelu lañuy xaree, diisoo bu yaatooy maye ndam.
7Wax ju xelu sut nab dof, jataayu pénc du fa àddoo.
8Kuy mébét lu bon, ñu ne yaay rambaaj bi.
9Pexem dof bàkkaar la, te kuy ñaawle, ñu sib la.
10Bu mettee, nga yoqi, sa doolee néew.
11Wallul ku ñuy reyi te tooñul, xettlil kuy tërëf, ñu di ko reyi.
12Soo nee sa yoon nekku ci it, kiy natt xol yi, xam na, moom miy wattu sa bakkan, xam na, te kat mooy fey nit jëfam.