Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 24

Kàddu yu Xelu 24:13-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13Doom, deel lekk lem, baax na, lem ju xelli, boo sexee, mu tem-temi.
14Xamal ne xel mu rafet ni la neexe; soo xeloo, sa muj rafet, te sa yaakaar du tas.
15Soxor bi, bul tëru ku jub ci këram, bul yàq dëkkuwaayam.
16Ku jub day daanu juróom yaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.
17Bu sab noon daanoo, bu ko bànneexoo, bu tërëfee, bu ko bége.
18Lu ko moy Aji Sax ji gis la, ñaawlu ko, daldi giif, dootu ko mbugal.

Read Kàddu yu Xelu 24Kàddu yu Xelu 24
Compare Kàddu yu Xelu 24:13-18Kàddu yu Xelu 24:13-18