Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 24

Kàddu yu Xelu 24:11-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Wallul ku ñuy reyi te tooñul, xettlil kuy tërëf, ñu di ko reyi.
12Soo nee sa yoon nekku ci it, kiy natt xol yi, xam na, moom miy wattu sa bakkan, xam na, te kat mooy fey nit jëfam.
13Doom, deel lekk lem, baax na, lem ju xelli, boo sexee, mu tem-temi.
14Xamal ne xel mu rafet ni la neexe; soo xeloo, sa muj rafet, te sa yaakaar du tas.
15Soxor bi, bul tëru ku jub ci këram, bul yàq dëkkuwaayam.
16Ku jub day daanu juróom yaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.
17Bu sab noon daanoo, bu ko bànneexoo, bu tërëfee, bu ko bége.
18Lu ko moy Aji Sax ji gis la, ñaawlu ko, daldi giif, dootu ko mbugal.
19Bu sa xol tàng ci ku bon, bul ñee ku soxor.
20Ku bon amul muj, ku soxor day mel ni taal bu fey.
21Doom, ragalal Aji Sax ji, wormaal buur. Bul lëngook kuy fippu.
22Yàllaak buur a koy bette mbugal, te kenn xamul musiba mu muy doon.
23Lii it ñi rafet xel a ko wax. Par-parloo cib àtte baaxul.
24Ku ne defkatu lu bon: «Yaw, tooñoo,» aw nit móolu la, mbooloo ŋàññ la;
25ku ko ne: «Yaa tooñ,» yaay baaxle, taasoo barke bu yaa.
26Ki lay wax dëgg sa soppe la.
27Ruujal sab tool, ji ko, doora tabax sa kër.
28Bul tuumaal nit ci neen, te bu ko seedeel ay fen.
29Bul ne: «Li mu ma def laa koy def, damay feyu li mu ma def.»
30Toolub ku yaafus laa jaare, ak tóokërub nit ku ñàkk bopp.
31Ndeke lépp a nga saxi dég, fépp fees akum ñax, tabaxu doj ba ko wër màbb.

Read Kàddu yu Xelu 24Kàddu yu Xelu 24
Compare Kàddu yu Xelu 24:11-31Kàddu yu Xelu 24:11-31