11Wallul ku ñuy reyi te tooñul, xettlil kuy tërëf, ñu di ko reyi.
12Soo nee sa yoon nekku ci it, kiy natt xol yi, xam na, moom miy wattu sa bakkan, xam na, te kat mooy fey nit jëfam.
13Doom, deel lekk lem, baax na, lem ju xelli, boo sexee, mu tem-temi.
14Xamal ne xel mu rafet ni la neexe; soo xeloo, sa muj rafet, te sa yaakaar du tas.
15Soxor bi, bul tëru ku jub ci këram, bul yàq dëkkuwaayam.
16Ku jub day daanu juróom yaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.
17Bu sab noon daanoo, bu ko bànneexoo, bu tërëfee, bu ko bége.
18Lu ko moy Aji Sax ji gis la, ñaawlu ko, daldi giif, dootu ko mbugal.