6Ab nay, bul lekke këram, bul xemmem daraam lu neex.
7Ma ngay xool la ngay lekk, nu mu tollu, naan la: «Lekkal, naanal!» Te xol ba àndu ca.
8Ndog soo ca lekk, waccu ko, yiw woo ko wax daldi neen.
9Bul wax akub dof, day xeeb sam xel.
10Bul toxal màndargam cosaan ci làccu suuf, bul aakimoo suufas jirim.
11Ki koy aar màgg na, da koy taxawu, dal ci sa kaw.
12Defal sam xel ci yar, te teewlu kàdduy xam-xam.
13Bul ñéebloo yar gone, bantal ko taxu koo dee.
14Soo ko bantalee, mu mana mucc.
15Sama doom, soo xeloo, sama xol neex.
16Ngay wax njub, ma bég.
17Bul ñee bàkkaarkat, saxool ragal Aji Sax ji,
18ndax kat moo am muj, te kon sa yaakaar du tas.
19Déglul, doom, muusal te yebu ci yoonu njub.
20Bul bokk ci ñiy lekk lu ëpp, ak a màndi,
21ndax ku bëgg lekk ak a màndi, ñàkk dab la, dajjant it, rafle rekk.
22Déglul sa baay bi la jur. Bu sa ndey màggatee, bu ko sàggane.
23Jëndal dëgg te bu ko jaay. Sàkkul xel mu rafet ak yar akug dégg.
24Su doom jubee, seral xolu baay. Boo juree ku rafet xel, am nga bànneex.
25Deel bégal ndey ak baay, rawatina ndey ji la jur.
26Doom, teewloo ma xel te roy ma.
27Ab gànc yeer mu xóot la, jabaru jaambur di teen bu xat.
28Ma ngay tëroo nib sàcc, góor ñu bare lay fecciloo worma.
29Ana kuy tiislu, naan: «Wóoy, ngalla man!» Ana kuy xulook a jàmbat, di gaañu ci dara, bët ya xonq curr?
30Xanaa kiy naan-naane biiñ, di mosi yeneen njafaan?
31Bul xool biiñ ak xonqaayam. Aka yànj cib kaas te neexa jolu!
32Bu weesee mu màtt la ni jaan, ne la càppit ni ñàngóor.
33Dangay mel ni kuy gis lu doy waar, sam xel di ràbb lu jekkadi.