Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 23

Kàddu yu Xelu 23:4-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Bul rey sa bopp ci wut alal, bu ko xalaat sax.
5Ndax xef ak xippi mu wéy, mel ni lu saxi laaf, ne fëyy, naaw ni jaxaay.
6Ab nay, bul lekke këram, bul xemmem daraam lu neex.
7Ma ngay xool la ngay lekk, nu mu tollu, naan la: «Lekkal, naanal!» Te xol ba àndu ca.
8Ndog soo ca lekk, waccu ko, yiw woo ko wax daldi neen.
9Bul wax akub dof, day xeeb sam xel.
10Bul toxal màndargam cosaan ci làccu suuf, bul aakimoo suufas jirim.
11Ki koy aar màgg na, da koy taxawu, dal ci sa kaw.
12Defal sam xel ci yar, te teewlu kàdduy xam-xam.
13Bul ñéebloo yar gone, bantal ko taxu koo dee.
14Soo ko bantalee, mu mana mucc.
15Sama doom, soo xeloo, sama xol neex.
16Ngay wax njub, ma bég.
17Bul ñee bàkkaarkat, saxool ragal Aji Sax ji,
18ndax kat moo am muj, te kon sa yaakaar du tas.
19Déglul, doom, muusal te yebu ci yoonu njub.
20Bul bokk ci ñiy lekk lu ëpp, ak a màndi,
21ndax ku bëgg lekk ak a màndi, ñàkk dab la, dajjant it, rafle rekk.
22Déglul sa baay bi la jur. Bu sa ndey màggatee, bu ko sàggane.

Read Kàddu yu Xelu 23Kàddu yu Xelu 23
Compare Kàddu yu Xelu 23:4-22Kàddu yu Xelu 23:4-22