Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 23

Kàddu yu Xelu 23:20-28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20Bul bokk ci ñiy lekk lu ëpp, ak a màndi,
21ndax ku bëgg lekk ak a màndi, ñàkk dab la, dajjant it, rafle rekk.
22Déglul sa baay bi la jur. Bu sa ndey màggatee, bu ko sàggane.
23Jëndal dëgg te bu ko jaay. Sàkkul xel mu rafet ak yar akug dégg.
24Su doom jubee, seral xolu baay. Boo juree ku rafet xel, am nga bànneex.
25Deel bégal ndey ak baay, rawatina ndey ji la jur.
26Doom, teewloo ma xel te roy ma.
27Ab gànc yeer mu xóot la, jabaru jaambur di teen bu xat.
28Ma ngay tëroo nib sàcc, góor ñu bare lay fecciloo worma.

Read Kàddu yu Xelu 23Kàddu yu Xelu 23
Compare Kàddu yu Xelu 23:20-28Kàddu yu Xelu 23:20-28