2Ku am ak ku ñàkk a bokk lenn: Aji Sax jee leen boole sàkk.
3Kuy foog, gisu ay, làqu; ab téxét ne ca tëñëx, loru.
4Woyofal te ragal Aji Sax ji, am alal, gudd fan ak daraja.
5Yoonu njublaŋ, ay dég aki fiir; ku sàmm sa bakkan sore ko.
6Tegal gone ciw yoon, ba bu màggee, du ko wacc.
7Ku am ay yilif ku ñàkk, koo leb di surgaam.
8Ku ji njubadi, góob fitna, yet wa muy dóore, damm.
9Ku tabe am barke, mooy kiy sédd ku ñàkk cib dundam.
10Dàqal kuy ñaawle, ay jeex, xulooki saaga dakk.
11Ku dëggu, wax ja yiw, buur di xaritam.
12Aji Sax jeey sàmm liy dëgg, di weddi waxi fen-kat.
13Bul yaafus, ba naan: «Gayndee ngi ci biti, dañu may rey ci mbedd mi!»
14Waxi ndaw su yemadi am yeer la, ku Aji Sax ji rëbb moo cay tàbbi.
15Yëfi dof daa sax ci xolu gone, boo bantalee, mu tàggook moom.
16Not néew-ji-doole ngir yokkule, mbaa may boroom alal, loo ci def mu wàññi la.