18Soo mokkalee, ba man koo tari, muy sa mbégte.
19Yaw laa koy xamal tey jii, ndax nga wóolu Aji Sax ji.
20Dama laa bindal fanweeri dénkaane, ci wàllu digal ak xam-xam,
21ngir xamal la lu wér te dëggu, nga yóbbaale kàdduy dëgg, yoo tontoo ña la yebal.
22Bul xañ néew-ji-doole; néew-ji-doole la. Ku tumurànke, bu ko soxore cib àtte,
23Aji Sax ji da koy taxawu, ku ko xañ, mu xañ la bakkan.
24Bul xaritook ku gaawa mer, bul ànd ak ku tàng bopp.
25Lu ko moy nga mel ni moom, te kon nga lonku.