9Ana ku man ne fóot na xolam, ba tàggook bàkkaar?
10Nattu diisaay yu yemul ak lu ni mel, Aji Sax ji bañ na ko.
11Gone sax day jëf, nga gis jikkoom; bu naree dëggu te jub, nga xam.
12Nopp buy dégg ak bët buy gis, Aji Sax jee sàkk lu ci nekk.
13Bul bëggi nelaw, ba ñàkk dab la; boo njaxlafee, lekk ba desal.
14Kuy waxaalee ngi naan: «Baaxul de!» Bu nee wërëñ, di damu naan: «Aka jar!»
15Wurus am na ak gànjar yu bare, waaye kàdduy xam-xam a gën per yu jafe.
16Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
17Njublaŋ, lekk, jëkke neex, mujj mel ni lancub suuf.
18Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.
19Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
20Ku saaga sa ndey mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel.