Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 20

Kàddu yu Xelu 20:16-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
16Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
17Njublaŋ, lekk, jëkke neex, mujj mel ni lancub suuf.
18Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.
19Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
20Ku saaga sa ndey mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel.
21Alal ju gaaw du mujje barkeel.
22Bul feyantook ku la tooñ; dénkul ci Aji Sax ji, mu wallu la.
23Aji Sax ji bañ na nattu diisaay yu wuute, njublaŋ ci natti diisaay baaxul.
24Jéegoy jaam Aji Sax jee ko yor, kenn xamul foo jëm.

Read Kàddu yu Xelu 20Kàddu yu Xelu 20
Compare Kàddu yu Xelu 20:16-24Kàddu yu Xelu 20:16-24